22/12/2025
Grande Magal de Kazu Rajab 2026
Gannaaw ba Seex Bàmba ñibbisee Tuubaa,
Boroom ndindee wubbi jumaayi Tuubaa.
Dalal xelu murit yi far bekkoor ba,
Jële fi ràmm ak ràgg door liggeey ba.
Ne ràmm mott ràgg mott Fàlloo,
Galas fi Tuubaa Mbàkke lépp Fàlloo.
Daraa yu jot sëkk jiba yu am koom,
Nawet ya delsi loo ca bay mu jag woom.
Lolli ba ñëw ñu am dugub jaay gerte,
Jaag ràbb seen i sàq sembak mbégte.